Yeen nag maa leen di tasaare ci biir xeet yi, ndax maay génne saamar mbaram, mu dal ci seen kaw. Seenum réew dina wéet, seen dëkk yu mag gent.
TSK
TSK · Jeremiah 39:9
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Te it ñenn ci sag njaboot, ñu soqikoo ci yaw, di ñoo meññ ci sa geño, dinañu leen jàpp, ñu doon jaam yu ñu tàpp ca biir kër buuru Babilon.”»
Ba mu ko defee Nebusaradan, njiital dagi buur, boole leen yóbbu ca buuru Babilon ca Ribla.
Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Maa ngii naa xërr waa réew mi bii yoon, teg leen njàqare, ba ñu yég ko.»
Ndax Aji Sax ji dafa wax ne: “Maa ngii di la wàcceel tiitaange, yaak sa soppe yépp, seen saamaru noon daaneel leen, ngay gis; te Yuda gépp laay teg ci loxol buuru Babilon, ñii mu yóbbu leen ngàllo, ñee mu jam leen, ñu dee.
¶ Ci kaw loolu Yeremi jot na kàddu gu bàyyikoo ci Aji Sax ji, gannaaw ba ko Nebusaradan njiitu dag ya yiwee, mu bàyyikoo Raama. Yeremee nga ñu jéngoon, mook ngàllog Yerusalem gaak Yuda ga jëm Babilon. Nebusaradan génnee Yeremi ca seen biir,
¶ Ba Nabukodonosor buuru Babilon tolloo ci fukkeelu atu nguuram ak juróom ñeent, ba am fukki fan ca juróomeelu weeru at ma, ca la bëkk-néegu buuru Babilon, Nebusaradan njiitu dag ya, dugg Yerusalem.
¶ Lii mooy limu nit ñi Nabukodonosor toxal: Ñetti junniy Yudeen ak ñaar fukk ak ñett (3 023), loolu yemook juróom ñaareelu atu nguuram,