Yeen Yesurun, yeena yaflu, waŋŋeetu, solu yaram, ne faaj, ne fuux, fàtte Yàlla mi leen sàkk, faaleedi seen cëslaay li leen musal.
TSK
TSK · Jeremiah 46:21
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Booba fekk na Boroom bi dégtal waa dalub Siri ba riirum fas yu ànd aki watiiri xare ak gàngoor gu réy, ba tax ñu naan ca seen biir: «Ãa! Loolu de, buuri Etteen ñaak buuri Misraa, Buurub Israyil fey leen, ngir ñu songsi nu!»
Njëlu ñetti xob fa ñu la soppe moo dàq yàpp wu duuf fu ñu la bañe.
Nagi àll yaay ànd ak ñoom daanu, ñook yëkk yu ndaw yaak yu mag ya, seen réew mi màndi deret, suuf sa niin batt ak nebbon.
«Ana lu ma gis? Waa Misraa jaaxle bay dellu gannaaw, seeni jàmbaar falaxoo, ne wëqet, geesuwñu, tiitaange ubale.» Kàddug Aji Sax jee!
Lu Apis di daw? Lu tee seen yàllay yëkk jooju taxaw? Xanaa Aji Sax jee ko bëmëx!
«Ãa yeen waa Babilon, yeena sëxëtoo xeet wi ma séddoo, di ko bégeek a bànneexoo, di bajantu ni nag wuy bàcc pepp, di ŋexal ni naaru góor?
Waa Pers ak waa Ludd ak waa Puut, ñépp a nga woon ca sa mbooloom xare, di wékk fa yaw seeni pakk ak seen mbaxanay xare. Ñooñoo la darajaal.
«“Dangaa masa bañ bànni Israyil. Ba musibay bànni Israyil taxawee, ba seen àppu mbugal mat sëkk, yaa leen jañax ci kaw ñaawkay saamar.
Yeen ñi tëdd ci seen lal yu yànj, ak a sóonoo seen laltu yu nooy, di yàpp mbote yu baax ak sëllu yu duuf,
Ki gën ci ñoom, neexook ag dég, ki ci jub yées ag taxas. Bés ba say jongrukat yégle woon, sa bésu mbugal taxaw na, léegi lees di waaru.