TSK

TSK · Job 1:21

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

saw ñaq ngay dunde, ba kera ngay dellu ci suuf, si ma la jële; ndaxte pënd nga, te dinga dellu di pënd.»

Waaye buleen jaaxle tey, mbaa ngeen di sikk seen bopp ndax li ngeen ma jaay, ñu indi ma fi. Rawale ay bakkan moo tax Yàlla yebal ma fi, ma jiitusi leen.

Aji Sax jeey xañe, di maye, di detteel, di kaweel.

Jombul Aji Sax ji gis sama naqar, ba feye ma aw yiw saagay kii tey.»

Esekiya ne Esayi: «Kàddug Aji Sax ji nga jottli jàmm la.» Booba ma nga naan: «Xanaa du jàmm ju ne ñoyy ay am sama giiru dund?»

Job 1:11 TSK

Xàccil sa loxo rekk, dal ci mboolem lu bokk ci moom. Ndegam du jàkkaarlook yaw, xarab la.»

Job 9:12 TSK

Kii, bu këfee, ana ku koy tere? Ana ku ko naa: «Looy def nii?»

Naa màggal Aji Sax ji saa su ne, di ko sant fu ma tollu.

Buleen yéemu ci ku barele, teraangay këram di yokku.

Nga juddoo ci sa ndey loxoy neen, walbatiku dellu na nga dikke woon. Du dara loo ñaqoon ba yóbbaale ko.

Yeen waa penku, sargal-leen Aji Sax ji boog, yeen waa duni géej, teral-leen Aji Sax ji Yàllay Israyil.

Maay bind leer, di def lëndëm. Maay indi jàmm, di def safaan. Maay Aji Sax jiy def lii lépp!

Amos 3:6 TSK

Bu liitu xare jibee, waa dëkk ba du tiit a? Am aw ay dina dab ub dëkk te du Aji Sax ji?

Acts 4:28 TSK

Noonu it lañu sottale mboolem li nga dogale woon sa loxo ak sa coobare.

te deeleen sant, ak nu mu mana deme, ndax loolu mooy coobarey Yàlla ci yeen ñi ànd ak Almasi Yeesu.

gépp may gu baax, ak bépp jagle bu mat, fa kaw la bawoo, di lu wàcce fa Baay biy boroom leer yi, ki soppikuwul ci lenn, te genn ker gu toogadi nekkul ci moom.