TSK

TSK · Joel 1:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Job 8:8 TSK

Laajal rekk maas gi nu jiitu, te teewlu seen gëstuy maam ya.

Job 15:10 TSK

Boroom bijjaaw ak màggat a ngi sunu biir, di ñu sut sa baay aw fan.

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor.

Yeen xeet yi, jegesileen te déglu; yeen askan yi, teewluleen! Na suuf ak li ci biiram déglu, muy àddinaak lépp lu mu jur.

Wóoy boobu bés bu réy, ba bés du ni mel! Bésu njàqare lay doon ñeel askanu Yanqóoba, waaye dañuy mucc.

Hosea 4:1 TSK

¶ Yeen bànni Israyil, dégluleen kàddug Aji Sax ji, Aji Sax ji kat moo séq ab layoo ak waa réew mi: «Du kóllëre, du ngor, du gennug ràññee Yàlla ci réew mi.

Joel 1:14 TSK

Sellal-leen ag koor, woote am ndaje, wooleen mag ñi, ak mboolem waa réew mi, ca seen kër Yàlla Aji Sax ji, te ngeen woo Aji Sax ji wall.

Amos 3:1 TSK

¶ Dégluleen kàddu gii Aji Sax ji wax ci yeen, bànni Israyil, mu jëm ci seen mboolem xeet wi mu génnee réewum Misra. Mu ne:

Amos 5:1 TSK

Amos ne: Yeen bànni Israyil, dégluleen mii pent: maa ngi leen di jooy, yeen bànni Israyil!

Micah 3:1 TSK

Dama ne: «Ngalla dégluleen yeen njiiti Yanqóoba, yeen kilifay kër Israyil! Xanaa du yeena wara xam yoon?

Ku ami nopp kat, na dégg li Noowug Yàlla wax mboolooy gëmkat ñi. Ku am ndam nag, maa lay may nga lekk ci garabu dund gi ci Àjjana, toolub Yàlla.