Sawaraa ngay tàkke ca samam sànj, di lakke ba ca xóotey njaniiw, ba xoyom suuf ak meññeefam, ba jafal reeni tund ya.
TSK
TSK · Jonah 2:6
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Yàllaa ma jot ba jàlluma, jëm pax, xanaa dellu di gis ug leer.»
Doo ma wacc njaniiw moos, sa wóllëre wa, doo ko won yàqutey bàmmeel.
Aji Sax ji, yaw laa woo wall; Boroom bi, yaw laa ñaanu yiw,
Defal nga nuy kéemaan, nangug ñaan ci njekk, yaw Yàlla, mi nuy wallu, di yaakaaru àddina wërngal këpp, ba ca géej gu sore ga.
Yaa ko sànge xóotey géej ni mbubb, ndox ma taxaw, tiim tund ya.
Aji Sax ji, gaawal wuyu ma; sama xol a jeex, ma ne yàcc, bu ma xañ sa yiw, ma yem ak kuy tàbbiji biir pax.
Ndeke sama tiisu xol wii, sama jàmm rekk a tax. Sa cofeel a tax nga sorele maak paxum sànkute. Yaa sànni sa gannaaw sama bépp bàkkaar.
Kee taxaw, yëngal suuf; kee xoole, loxloo xeet yi, tund yu mag ya woon naka jekk rajaxoo, tundi cosaan yu ndaw ya maasaloo. Kii moo moom yooni cosaan yi.
nun sët yi la ko defal, ba mu yékkatee Yeesu, te noonee lañu ko binde ci ñaareelu saaru Sabóor, ne: “Yaa di sama Doom, bés niki tey maa la jur.”