Musaa nag tinu Yàllaam Aji Sax ji ne ko: «Aji Sax ji, ana lu waral sam sànj di tàkkal sa ñoñ ñi nga génne réewum Misra ci sa kàttan gu màgg ak sa dooley loxo?
TSK
TSK · Lamentations 2:20
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ma ñaan Aji Sax ji, ne ko: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, bul sànk sa ñoñ ñi nga séddoo, ñi nga jote sa màggaay, génnee leen Misra ci sa dooley loxo.
Mu teg ca ne ko: «Lan la sax?» Ndaw sa ne ko: «Ndaw sii da ma noon: “Indil sa doom, nu lekk ko tey, ëllëg nu lekk sama doom.”
seeni sarxalkat loroo saamar, te jëtun jooyul.
Yaw déy yaa di sunu Baay. Ibraayma xamalu nu dara, Israyil xamu nu. Yaw Aji Sax ji yaa di sunu Baay, sa tur a di “sunu Jotkat naka jekk.”
Yonent yiy wax waxyuy fen, sarxalkat yiy jiitee seen coobare, te sama ñoñ soppe ko ni! Moo bu muj ga taxawee, nu ngeen di def?»
Aji Sax ji, xam nanu sunug mbon, xam sunu ñaawtéefi maam; moy nanu la moos.
Gannaaw loolu nag,” kàddug Aji Sax jee, “Cedesyas buurub Yuda, aki jawriñam ak askan week ñi des ci dëkk bii te rëcce ci mbas meek xare beek xiif bi, maa leen di teg ci loxol Nabukodonosor buuru Babilon, ak seen loxol noon, ak loxol ñi leen di wuta rey. Dina leen leel ñawkay saamar. Du leen baal, du ñéeblu, du yërëm.”
Samay soppe laa woo wall, ñoom ñu wor ma. Samay sarxalkat ak samay mag di wuti ab dund bu ñu leqlikoo, far faatu ci biir dëkk bi.
Seen bàkkaari yonent yaa, seen ñaawtéefi sarxalkat yaa; ñoo tuur fa digg dëkk ba deretu aji jub ñi.
Moo tax baay dina yàpp doom, doom yàpp baay fi biir Yerusalem. Maay wàcce ay mbugal fi yeen, te maay tasaare seenu ndes wépp fépp fu ngelaw jublu.
Aji Sax ji ne leen: «Feesal-leen ëtt yeeki néew, sobeel-leen kër gi, doora génn.» Ba ñu noppee, daldi jàll ca biir dëkk ba, di rey.