Da naan tasar ni njaqal xandeer lu ñu naan rajax te ñéebluweesu ko, ba deesul gis ca tojit ya, dog bu tibb xal, mbaa mu as ndoxum déeg.»
TSK
TSK · Lamentations 4:2
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
te nga ne leen: “Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Askan wii ak dëkk bii, ni ñuy toje njaq, ba deesatu ko mana defaraat, ni laa koy tojate. Tofet gii dees na fi rob ndax ñàkk fu ñu robe.
Mag ak ndaw a ngi ne lareet fi suuf ci mbedd yi; sama janq jeek sama xale yu góor yi tëdd, fàddoo saamar. Yaa rey ci sa bésub mer, yaa rendi te yërëmoo.
Dees na wonn Israyil; tey ñu ngi ci biir xeeti jaambur yi, mel ni ndab lu kenn buggul.
Tabaxkatu ndab bi daa amul sañ-sañ ci ban bi muy liggéeye, ngir tabax ci bennub tooyal, lenn ndabal teraanga, ak leneen ndabal njoogaan?
¶ Kër gu mag nag, du ndabi wurus ak xaalis rekk a fa am, waaye yoy bant a nga fa, ak yoy ban; yii di ndabi teraanga, yee di ndabi njoogaan.