TSK

TSK · Lamentations 4:21

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Job 1:1 TSK

¶ Amoon na ca réewum Ucc, góor gu ñuy wax Ayóoba. Góor googu nekkoon ku mat te jub, ragal Yàlla te dëddu lu bon.

Aji Sax ji, fàttlikul Edomeen ña, keroog jantub Yerusalem, ba ñu naan: «Màbbleena màbb, ba kenug dëkk bi siiñ!»

Yeen xeet yi, jegesileen te déglu; yeen askan yi, teewluleen! Na suuf ak li ci biiram déglu, muy àddinaak lépp lu mu jur.

¶ Aji Sax ji Yàllay Israyil déy da maa wax ne ma: «Am kaasu biiñ bii ci sama loxo, di misaal kaasu mbugal, te nga nàndal ci mboolem xeet yi ma lay yebal,

Ndegam ñi yeyoowul mbugal ñooy jolu kaasu mbugal, nees leen di ñàkka toppe, yeen? Dees na leen topp moos, ngeen jolu kaasu mbugal.

«Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: Waa Mowab ak Seyir a ne: “Xool-leen waa kër Yuda ñii ni ñu mujje, ñook xeet yépp a yem!”

«Yaw nit ki, Tir dëkk ba moo ree Yerusalem, ne: “Ñaw! Buntu dëkk bi xeet ya daan jaare dàjjiku na! Léegi man la bunt ubbikul, léegi maay woomle, Yerusalem gental na.”

Moo tax giñ naa ko ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, ni nga mbugale bànni Israyil ci sa biir mer, ak sa kiñaan ak sa mbañeel, ni laa lay mbugale. Maay dogal sab àtte, ba xamal ñii maay kan.

Amos 1:11 TSK

Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Edom, te duma fomm seeni duma. Ñoo toppe seen bokki bànni Israyil saamar, jalax yërmande, mer mer mu dul meddi ak xadar ju dul giif mukk.

«Soxore gi ngeen soxore seen mbokk Yanqóoba moo leen tax di sangoo gàcce, te dees na leen dagg sànni ba fàww.

Yeen waa Safiir, jàll-leen, ak gàcce ak yaramu neen. Waa Caanan sañuñoo génn, te wall du bawoo fa waa Bet Eccel, ñay jooy seeni néew.

¶ Mu ne: «Maa ngi nii yoot, di dikk nib sàcc. Ndokklee, yaw mi teewlu, fàggu say yére, ba doo deme gàcceg yaramu neen, ñu di la seetaan.»