Te dinaa feddli sama kóllëre, gi ci sama diggante ak yaw, yaak sa askan, muy kóllëre guy sax maasoo maas ba fàww. Maay doon sa Yàlla, yaak sa askan.
TSK
TSK · Leviticus 18:2
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
«Man Aji Sax ji, maa di seen Yàlla, ji leen génne réewum Misra, kërug njaam ga.
Samay santaane ngeen wara dégg tey topp samay dogal. Man Aji Sax ji maay seen Yàlla.
¶ «Na ku nekk weg ndeyam ak baayam te wormaal sama bési Noflaay. Man Aji Sax ji, maay seen Yàlla.
Njuddu-ji-réew ji nangeen ko yemaleek doxandéem bi ngeen dëkkal. Soppleen ko ni ngeen soppe seen bopp, ndaxte ay doxandéem ngeen woon ca réewum Misra. Man Aji Sax ji maay seen Yàlla.
Buleen roy defini xeet wi ma leen di dàqal, ndax yooyu yépp lañu doon def, ba ma sib leen.
¶ «Nanga leen wax, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Ba ma tànnee Israyil, maa giñal askanu waa kër Yanqóoba woowa. Maa leen xamal maay kan ca réewum Misra, giñal leen, ne leen: Man Aji Sax ji maay seen Yàlla.
Man Aji Sax ji maay seen Yàlla. Sama dogali yoon, jëfeleen ko; sama àttey yoon, ngeen sàmm ko, di ko jëfe.