TSK

TSK · Leviticus 18:30

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ «Yeen nag sàmmleen samay dogal ak samay santaane te bu kenn def lenn ci yooyu ñaawtéef, du njuddu-ji-réew, du doxandéem bi ci seen biir,

Sarxalkat yi dañoo wara dénkoo samay dénkaane bala ñoo gàddu bàkkaar, di dee ndax seenug néewal ci yooyu. Maay Aji Sax ji leen sellal.

nangeen wattu seen bopp, ba gannaaw bu xeet yooyu sànkoo ci seen kanam, dungeen tàbbi cig fiir, di leen roy, naan: «Ana nu xeet yii di jaamoo seeni tuur, ngir nun it nu def ni ñoom?»

¶ Bu ngeen demee ca réew ma leen seen Yàlla Aji Sax ji di jox, buleen roy jëf ju jomblu ju xeet yooyu.

Réew ma amoon na sax ñuy jaay seen bopp fa ñuy màggale tuur ya. Ñuy def mboolem ñaawtéefi xeet ya Aji Sax ji dàqoon ngir bànni Israyil.

Ezra 9:1 TSK

¶ Gannaaw ba loolu wéyee njiit ya dikk, ne ma: «Du bànni Israyil, du sarxalkat yi, du Leween ñi, kenn ci ñoom teqlikoowul ak xeeti réew meek seen aada yu siblu. Dañuy jëfe ni Kanaaneen ñeek Etteen ñeek Periseen ñeek Yebuseen ñeek Amoneen ñeek Mowabeen ñeek waa Misraak Amoreen ñi.