Fa biti la leen saamar di xañey doom, biir néeg ya, tiitaange luy reye feelu ko, buubaale waxambaane akub janq, luy nàmp, ak boroom bijjaaw.
TSK
TSK · Leviticus 19:18
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Ba mu ko defee Absalom sant ay nitam, ne leen: «Ma ne, bu Amnon naanee biiñ, ba xolam sedd, bu ma leen nee ngeen jam ko rekk, reyleen ko. Buleen ragal; man maa leen ko sant. Góor-góorluleen nag te ñeme.»
Bul feyantook ku la tooñ; dénkul ci Aji Sax ji, mu wallu la.
Mu ne ko: «Boroom bi sa Yàlla, nanga ko soppe sa léppi xol ak sa léppi bakkan ak sa léppi doole ak sa léppi xel, te ni nga soppe sa bopp, nanga ko soppe sa moroom.»
¶ Buleen feyantoo, fexeleen di def lu rafet, ñépp seede ko.
Ndax kilifa gi mooy ndaw li Yàlla yebal ngir sa jàmm. Waaye soo dee def lu bon, ragalal, ndax kilifa gi yorul ab saamar cig neen; mooy ndawal Yàlla liy añale, te mooy jottli am sànj mu wàccal kuy def lu bon.
Ndax yoonu Musaa wépp, ci lenn ndigal lii la tënku: «Ni ngeen soppe seen bopp, nangeen ko soppe seen moroom.»
Lépp luy wextan, ak naqari deret, ak mer mu ëpp, ak coow, ak wax ju ñaaw, na lépp buube, ba génne ci seen biir, mook mboolem jëfi coxor.
Xam nanu ki wax ne: «Ag pey, maay boroom, man maay añale,» neeti: «Boroom bi mooy àtte ñoñam.»
¶ Kon nag baleen mboolem xeetu mbon, ak mboolem njublaŋ, ak jinigal, ak kiñaan, ak mboolem xeetu yàq der.