TSK

TSK · Leviticus 19:34

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Dogal bi benn lay doon, doomu réew mi ak doxandéem bi dëkk ci seen biir, bokk ci yem kepp.»

Buleen di feyantook seen mbokkum waa réew te buleen ko dencal mer. Ni ngeen soppe seen bopp nag, nangeen ko soppe seen moroom. Maay Aji Sax ji.

¶ Buleen bañ ab Edomeen, ndax seen mbokk la. Buleen bañ nitu Misra, ndax ay doxandéem ngeen woon ca seenum réew.

Nangeen ko tegoo bant, séddoo ko ci seen biir, yeen ak doxandéem yi sanc ci seen digg te jaboot ci réew mi. Nangeen leen jàppe ni ay njuddu-ji-réew fi digg Israyil. Nañu am seen céru suuf ni yeen, bokk ci yem ak giiri Israyil.