¶ «Maay baaxee réew mi jàmm it, ba bu ngeen tëddee kenn du leen tiital. Maay jële rab wu aay ci réew mi, te saamar du jóg, dal ci seenum réew.
TSK
TSK · Leviticus 26:22
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ba ñuy doora sanc foofa, ragaluñu woon Aji Sax ji, ba tax Aji Sax ji yebal ay gaynde ci seen biir, ñu di leen rey.
Moo tax alkànde yàq suuf, ñi ko dëkke gàddu àq ji. Moo tax waa àddina raaf, ba ñi des di lu néew.
¶ «Te dinaa wàcce fi seen kaw ñeenti xeeti duma.» Kàddug Aji Sax jee. «Saamar di bóom; xaj diri yóbbu, njanaaw ak rabu àll for, mu jeex.
Maay yebal ci seen kaw ab xiif ak rabi àll yu leen di xañ ay doom; mbas ak deret ju tuuru gane leen, saamar, ma indil leen. Man Aji Sax ji, maa ko wax.»
¶ «Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: Sama ñeenti mbugal yu tar yii laay yebal ci kaw Yerusalem. Ñuy saamar akub xiif ak rabi àll aku mbas, ngir dagge ci réew mi nit ak mala.
Kon nag dees na gàbb Siyoŋ nib tool, Yerusalem googu diy tojit, jale, tundu kërug jaamookaay baay doon gajj bu kawe.