Seen saraxu póotum bàkkaar a ngoogu. Li des ci yàppu yëkk wi, boole kook der bi, ak sébbriit mi, nga génne ko dal bi, lakk ko.
TSK
TSK · Leviticus 4:3
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Na Aaróona di sàkk ci deretu saraxu póotum bàkkaar bi, taqal ci béjjéni sarxalukaay bi, ngir def ko njotlaayal sarxalukaay bi benn yoon cim at. Benn yoon cim at lañu koy defal njotlaayam ci seen gépp maas. Sarxalukaay bu sella sell la, ñeel Aji Sax ji.»
¶ «Bu saraxam dee ab gàtt bu ñuy def rendi-dóomal, muy xar mbaa bëy, na sarxal bu góor bu amul sikk.
Na indil Aji Sax ji gàtt bu jigéen, xar mbaa bëy, muy daanam ndax bàkkaar bi mu def. Saraxu póotum bàkkaar lay doon, sarxalkat bi defal ko ko njotlaayal bàkkaar bi mu def.
Mu sotti nag tuuti ci diw gi ñuy fale ci boppu Aaróona, diw ko, sellale ko ko.
Te nga wax bànni Israyil ne leen ñu jël ab sikket, mu doon saraxu póotum bàkkaar, akaw sëllu akam xar, lu ci nekk am at te mucc sikk, ngir saraxu rendi-dóomal,
Na jële ci mbooloom bànni Israyil ñaari sikket, sikket yuy doon saraxu póotum bàkkaar ak menn kuuyum rendi-dóomal.
¶ «Bu Aaróona noppee, na indi yëkku saraxas póotum bàkkaaram, def ko njotlaayam mook waa këram. Na rendi yëkku saraxas póotum bàkkaaram,
Su ko defee ñu jël aw yëkk wu ndaw, booleek saraxu peppam, di sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ak weneen yëkk wu ndaw wooy jël ngir saraxu póotum bàkkaar.
Biir dal-luwaay boobu, ñeenti taabal a nga ca, ñaari taabal cat lu nekk. Ca lañuy rey juri sarax yi. Muy saraxu rendi-dóomal, di saraxu póotum bàkkaar, di saraxu peyug tooñ.
Bés ba muy dellu ca ëttu biir ba, ngir liggéey ca biir bérab bu sell ba, na indi saraxu póotum bàkkaar. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
Almasi mi masula bàkkaar, moom la Yàlla sëf sunu bàkkaar, ngir nu mana ame ci moom àtteb nit ñu jub fa Yàlla.
Bokkul ak yeneen sarxalkat yu mag yi; soxlawula jiital bés bu nekk, saraxi jur ngir bàkkaari boppam, door cee teg ay sarax ngir bàkkaari askan wi. Benn yoon la Yeesu sarxal, mu doy, te mooy ba mu sarxee boppam.