Waaye su ñu sàccee mala mi ci këram, moom mi dencoon mooy delloo boroom.
TSK
TSK · Leviticus 5:1
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
«Ku ñàkka wormaal lenn lu ñu sellalal Aji Sax ji te du teyeefam, daan ba ko war, mu di ko indil Aji Sax ji, am kuuy mu amul sikk lay doon, ñuy xayma njégam, dëppale dayob xaalis baak natt ba ñu yoonal ca bérab bu sell ba. Saraxu peyug tooñ la.
Waaye kat bu nit lekkee lenn ci yàpp wu ñu def saraxu cant ci biir jàmm te fekk mu am ñetti fan, deesul nangul boroom sarax si te du ko jariñ dara. Lu ñu sib la te ku ca lekk mooy gàddu bàkkaaram.
Ku ci lekk mooy gàddu bàkkaar bi, ndaxte lu ñu sellalal Aji Sax ji la teddadil, te kooku dees na ko dagge ci biir bànni Israyil.
Ku set nag te nekkul ciw yoon, su ñàkkee màggal bésub Mucc bi, kooku dees koy dagge ciw askanam, ndax saraxu Aji Sax ji mu joxewul ci bésam. Kooku moo gàddu bàkkaaru boppam.
¶ «Ku ñu tuumaal ne moo tooñ moroomam, te yoon waatloo ko ba waat war ko, bu dikkee di waatsi fi sa kanam sarxalukaay bi ci biir kër gii,
Ku ànd akub sàcc, sa noonu bopp nga: soo waxee dëgg, yoon topp la; soo ko miimee, Yàlla topp la.
Mooy sonn ba gis ug leer, doyloo ko, te ñu bareey xam sama jaam bii di Aji Jub, ba mu àtte leen àtteb njekk, sëfoo seeni ñaawtéef.
Ki bàkkaar daal mooy dee. Doom du gàddu ñaawtéefu baay, baay it du gàddu ñaawtéefu doom. Njekk réerul boroom, mbon réerul boroom.
«Moom ci boppam moo gàddu sunuy bàkkaar, moo ko tegoo ci yaramu boppam ca bant ba,» ngir nu deeyal bàkkaar te dundal njub; «moom mooy ki ngeen wére ci ay góomam.»