TSK

TSK · Leviticus 5:11

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Ñu jàpp ne andaar, boo ci amee fukk, mooy benn efa.

¶ «Su dee sarxal lu ñu defare pepp, di lu ñu lakk cib taal ba mu ñor, na doon sunguf su mucc ayib, di mburu yu amul lawiir yu ñu xiiwaale diw, mbaa mburu yu sew yu amul lawiir, ñu sotti diw ca kawam.

Na indil Aji Sax ji gàtt bu jigéen, xar mbaa bëy, muy daanam ndax bàkkaar bi mu def. Saraxu póotum bàkkaar lay doon, sarxalkat bi defal ko ko njotlaayal bàkkaar bi mu def.

Da koy yót sarxalkat bi, sarxalkat bi sàkk ci barci-loxo, muy saraxu baaxantal, mu daldi koy lakk ca kaw sarxalukaay bi, mu dolliku ci saraxi sawara yi. Saraxu póotum bàkkaar la.

¶ «Su fekkee ne nit ki dafa ñàkk ba dooleem matewu ko, na wut menn kuuy, muy saraxu peyug tooñ, di saraxu yékkati-jébbale, ngir njotlaayam, boole kook ñetti kiloy sunguf su mucc ayib, xiiwe ko diw, muy saraxu pepp. Na indaale genn-wàll liitaru diw,

na waa ji yóbbu jabaram ca sarxalkat ba, te yóbbaleel ko saraxu ñetti kiloy sungufu lors. Du ci sotti diw, du ci def cuuraay, ndax saraxu pepp boobu saraxu fiiraange la, saraxu toppukaay la bu ñuy toppe ñaawtéef.

sarax ba mu indi di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, di kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikali bérab bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp,

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda, dëppook galan bi ñu dippee Kéwélu fajar.

Kii màgge fi kanamam ni njëmbat, te nirook reen bu fette ag kekk. Dub taar, du yànjaay bu nu koy niire, du meloom wu nu koy soppe.