¶ «Su dee ku sàcc mala, muy nag mbaa mbaam mbaa ab gàtt, te ñu fekk ko ciy loxoom, muy dund, na fey ñaaram.
TSK
TSK · Leviticus 5:16
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Na lakk nebbon bi yépp ci kaw sarxalukaay bi, def ko ni nebbonu saraxu cant ci biir jàmm. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayal bàkkaaram, mu am njéggal.
Ñaareel bi na ko def saraxu rendi-dóomal, muy li ñu santaane. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayal bàkkaar bi mu def, mu am njéggal.
Su ko defee mu summi yéreem yooyu, sol yeneen te génne dóom bi dal bi, yóbbu ko fu mucc sobe.
Gannaaw loolu képp ku bokkul ci waa kër sarxalkat yi, bu lekkee ci sarax su sell te du teyeefam, na dolli ca njégu sarax sa juróomeelu céru njég ga, delloo ko sarxalkat bi.
Su fekkee ne ki dogu woona joxe dëkkuwaayam da koo bëgga jotaat, day fey njég ga ñu ko xaymaa, yokk ca xaajub juróomeelam, mu doonaat alalam.
Su fekkee ne nit ki dafa namma jotaat lenn ca céru fukkeelu meññeefam ma muy génne, day yokk ca njég ga xaajub juróomeelam.
Ñu ne leen: «Su ngeen dee delloo gaalu Yàllay Israyil, buleen ko delloo loxoy neen, waaye fexeleen ba boole kook saraxu peyug tooñ, yónnee ko. Kon dingeen wér, te dingeen xam lu tax loxol Yàlla ji teggikuwu leen.»
Sase nag taxaw ne Sang bi: «Sang bi, ma ne, sama genn-wàllu alal, jox naa ko néew-doole yi, te jépp alal ju lewul ju ma masa jëlal kenn, dinaa fey ñeentam.»
Ndegam deretu sikket ak yëkk, ak nag wu jigéen wu ñu lakk, ngir suy dóom ba nit ku sobewu, yooyu lees daan sellale nit ñi, ngir seen cetug yaramu suuxu neen,