TSK

TSK · Luke 1:18

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Bi Ibraayma déggee loolu, daa sujjóot, ree. Booba ma nga naan ci xelam: «Góoru téeméeri at, ndax dina mana am doom waay? Te Saarata, mi am juróom ñeent fukki at (90) sax, manati naa am doom a?»

¶ Ci kaw loolu Musaa ne: «Ãa! Juróom benni téeméeri junniy (600 000) góor a ngi ci mbooloo mii ma ne ci seen biir. Yaw nga ne aw yàpp nga leen di jox, ñu yàpp weeru lëmm!

Jaraaf ja daan ànd ak Buur saa su ne àddu ca ne góoru Yàlla ga: «Ma ne, su Aji Sax ji ubbi woon sàqi asamaan sax, ndax man naa tax loolu am?» Mu ne ko: «Dinga ci teg sa bët déy, waaye doo ci lekk.»

Luke 1:7 TSK

Amuñu woon doom nag, ndax Elisabet manul woona am doom, te it booba ñoom ñaar ñépp a dem ba màggat.

Ngëmu Ibraayma wàññikuwul, doonte ba mu xoolaatee boppam, xam na ne yaramam dee na daanaka, ndax fekk na ay atam xawa tollu ci téeméer, te njurukaayu Saarata it fekk na ko dee.