TSK

TSK · Luke 11:39

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Noon yaa ngi ma gaw ni coggalu yëkk, dar ma ni ponkali yëkk ya fa Basan.

Ag maas a ngi defe ne set nañu, te taq ripp ak bàkkaar.

Ay yonentam a ngi déeyoo fi biiram; ñu ngi xiiru ni gaynde guy xotat pàddam, di lekk doom aadama yi, foqati alal ak gànjar, ful jëtun yi ci biiram.

Kàngam yi ci biiram di gaynde yuy ŋar, ay njiitam di tilli timis yu dul pannal,

Yeesu ne leen: «Yeen yeenay jub-jublu ci kanam nit ñi, waaye Yàlla xam na seen xol. Ndax li nit ñi gëna naw, lu seexluwu la fa Yàlla.

Acts 8:21 TSK

Amuloo benn wàll mbaa ab cér ci lii, ndax sa xol a jubul ci kanam Yàlla.

Ag njullite lañuy mbubboo tey xalab leer ga leen ko wara manloo. Ñooñu, dëddu leen.

James 4:8 TSK

Jegeleen Yàlla, mu jege leen. Yeen bàkkaarkat yi, raxasleen seeni loxo, yeen ŋaralekat yi laa ne, setal-leen seen xol.