TSK

TSK · Luke 13:14

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ «Diiru juróom benni fan ngeen di liggéey, waaye bésub juróom ñaareel ba, nopplu leen, ndax seen nag ak seen mbaam mana nopplu, seen surga akub doxandéem it mana astandiku.

Sama bési Noflaay itam maa leen ko jox, muy màndarga sama digganteek ñoom, ngir ñu xam ne man Aji Sax ji maa leen sellal.

Luke 6:11 TSK

Ñu mer nag ba fees, di diisoo ci seen biir nu ñuy def ak Yeesu.

Luke 14:3 TSK

Yeesu àddu, ne xamkati yoon yaak Farisen ya: «Waaw, pajum bésub Noflaay, yoon maye na ko, am déet?»

Acts 18:8 TSK

Teewul Kirispus njiitu jàngu ba moom, gëm Sang bi, mook waa këram gépp. Ñu bare ci waa Korent a gëm, gannaaw ba ñu déggee kàddu gi, ba ñu sóob leen ci ndox.

Ñoom laa seedeel seenug parlute ci Yàlla, waaye dañu koo tegul ci xam-xam bu doy.