TSK

TSK · Luke 13:19

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Fan yu mujj ya, dees na taxawal tundu kër Aji Sax ji, Aji Sax ji mooy gëna kawe ci tund yi, tiim tund yu ndaw yi, xeet yépp riirandoo, wutsi ko.

Ñàkkoon ngay doom, waaye ku nekk ci say doom ay dëkkalaat yii kàddu ci sab nopp: “Fii dafa xat, xajal ma, fu ma dëkke!”

Ana ku gëm sunub dégtal? Ana ku Aji Sax ji won dooley përëgam?

Aji Sax ji di leen jiite fu ngeen tollu, di leen màndale joor gu maral, dëgëral seeni cér, ngeen mel ni tool bu ñu suuxat, mel ni bëtu ndox bu dul ŋiis,

Ni suuf di fettalem njebbit, ab tool di ko saxalem jiwu, ni la Boroom bi Aji Sax ji di jebbile njekk ak cant, xeetoo xeet seede ko.

¶ «“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Man ci sama bopp maay sàkke ab car ca njobbaxtalu garabu seedar gu kawe ga, sàkkal ko bérab. Car yu ndaw ya ca kaw laay fàqe car bu nooy, jëmbatal ko sama bopp ci kaw tund wu mag te kawe.

¶ Waa ji nag delloo ma ca buntu néeg Yàlla ba. Gisuma lu moy am ndox muy balle ci suuf, di génne ci dëxu buntu penku bi. Kanam néeg baa ngi féete penku, ndox miy wale wetu bëj-saalumu néeg bi, fa féeteek bëj-saalumu sarxalukaay bi.

¶ «Ci jamonoy buur yooyu Yàlla Boroom asamaan dina samp nguur gu dul tas mukk, te wenn xeet du ko yilif mukk. Nguur googu dina tasaare mboolem yeneen nguur yooyu, ba genn du ci des, waaye moom day sax ba fàww.

Piri maa ngii, Buur, di dogalu Aji Kawe, ji dal ci sa kaw, Buur, sang bi.

«Éy Siyoŋ, rëccal, yaw mi dëkke janq Babilon mu taaru mi.»

Benn bésu boppam lay doon bu Aji Sax ji doŋŋ xam; du doon bëccëg, du doon guddi, te bu ngoonee mu leer.

Luke 17:6 TSK

Sang bi ne leen: «Su ngeen amoon ci ngëm, lu tollu ni peppu fuddën sax, ba ne garab gii: “Buddeekul, dem jëmbate ca géej ga,” su boobaa garab gi déggal leen.

Acts 4:4 TSK

Fekk na nag, ñu bare ca ña jotoona dégg kàddu ga gëm nañu, ba limu gëmkat ña tollu ci juróomi junni (5 000).

¶ Ñu dégg ca, daldi sàbbaal Yàlla, ba noppi ne ko: «Mbokk mi, xoolal ñaata junniy Yawut a doon ay gëmkat, te ñoom ñépp di ñu xér ci yoonu Musaa.

¶ Ba mu ko defee, juróom ñaareelu malaaka mi wal liitam, baat yu xumb jibe ca asamaan, ne: «Léegi nag nguurug àddina ñeel na sunu Boroom ak Almaseem. Mooy nguuru ba fàww.»