Ab ñaawlekat day wut xel mu rafet, mu réer ko; ku am ug dégg, xam yomb la.
TSK
TSK · Luke 13:24
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Proverbs 14:6
TSK
Ab dof ak kër-këreem, coonoy neen; du xam sax yoonu taax ya.
Isaiah 58:2
TSK
Man mii lañuy sàkku bés bu ne, di wuta xam sama coobare! Mbete xeet wuy def njekk, te waccul ndigalu yoonu Yàllaam. Ñu ngi may ñaan àttey njekk, di sàkku man Yàlla, ma jege leen,
Romans 10:3
TSK
Yoonu njub gi Yàlla di joxe nit ki, àtteb ku jub, moom lañu umple tey jéema dëggal seen njubteg bopp. Moo tax nanguluñu njubte gi Yàlla di maye.
Philippians 2:12
TSK
¶ Kon nag soppe yi, noonu ngeen masa dégge ndigal, démb ba may teew, rawatina tey bi ma wuutee, nangeen ko wéye, di jëfe seenug mucc, te ànd ceek ragal Yàlla bay lox,
Hebrews 4:11
TSK
Nanu def sunu kem-kàttan boog, ngir tàbbi ci googu noflaay, bala kenn a daanu ndax déggadi gu mel ni gu maam ya.