TSK

TSK · Luke 2:34

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Gannaaw loolu Yuusufa ànd ak baayam ba fa Firawna, nuyole ko ak moom. Yanqóoba nuyu Firawna.

¶ Ba Aaróona noppee, yékkati na mbooloo ma ay loxoom, ñaanal leen, doora wàcc. Fekk na mu joxe saraxu póotum bàkkaar ba, ak saraxu rendi-dóomal ba, ak saraxu cant ga ci biir jàmm.

Jaambur laa léegi ci saay bokk, mel ni doxandéem sama biir doomi ndey.

Man de, maa ngii, maak xale yi ma Aji Sax ji may, nu diy firnde fi Israyil te diy tegtal yu bàyyikoo fa Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, ki dëkke tundu Siyoŋ.

Acts 2:36 TSK

¶ «Kon nag na wóor waa kër Israyil gépp ne Yeesu moomu ngeen daajoon ci bant, Yàllaa ko def Sang ak Almasi.»

Acts 4:26 TSK

Buuri àddinaa jógandoo, kilifa yee lëkkoo ci kaw Boroom bi ak Almaseem.”

Acts 9:1 TSK

¶ Ci biir loolu Sóol moom, noyyeewul lu moy di tëkkook a jéema bóom taalibey Sang bi. Mu dem nag ca sarxalkat bu mag ba,

Acts 17:6 TSK

Ci kaw loolu gisuñu leen, ñu diri Yason ak yeneen bokki gëmkat ba ca kanam àttekat ya. Ña ngay biral, naan: «Nit ñi tas àddinaa ngii, agsi nañu fi,

Waaye bëgg nanoo dégg ci sa gémmiñu bopp li nga gëm, ndax li nu xam daal mooy, ngér moomu nga bokk, fu nekk lañu koy diiŋate.»

Nun nag, nuy waare Almasi bu ñu daaj ci bant, muy njombe ci Yawut yi, di ag ndof ci jaambur ñi dul Yawut.

¶ Melkisedeg moomu doon buurub Salem te nekkoon sarxalkatub Yàlla Aji Kawe ji, ba Ibraayma délsee jóge xareem baak buur ya mu duma, kooku moo ko gatandu woon, ñaanal ko.

¶ Kon nag gannaaw gii ndiiraanu seede wu réy moo nu yéew, nanu sippiku mboolem sëf bu nuy yeexal, ak bàkkaar bu nu yomba téqtal. Ñu daw nag xél wi ñu nu waajalal, te baña yoqi.

Su ñu leen jànnee sax ndax turu Almasi, ndokklee yeen, ndax Noo gu darajawu gi, Noowug Yàlla moo wàcc ci yeen.