TSK

TSK · Luke 2:37

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Mu sàkk itam mbalkam njàpp mu ànd ak tegoom, di xànjar ju jóge ci seetuy jigéen, ñi doon liggéey ci bunt xaymab ndaje mi.

Sama Yàlla, sama Yàlla, lu tax nga wacc ma? Ma binni, binneeti, wall sore.

Lenn laa ñaan Aji Sax ji, lii laay sàkku: dëkk kër Aji Sax ji, sama giiru dund, di niir taaru Aji Sax ji, te yéemoo këram.

Éy Yàlla, geesul Buur, sunu kiirlaay, ngalla niiral kii nga fal.

Màggal-leen Ki Sax! Màggal-leen turu Aji Sax ji, éey jaami Aji Sax ji, màggal-leen,

Acts 13:3 TSK

Ba loolu amee ñu woor, boole kook ñaan, daldi leen teg seeni loxo, ba noppi yiwi leen.

Acts 26:7 TSK

Te mooy dige bi fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil di séentu mu sottil leen, ba tax guddi ak bëccëg ñu xér ci jaamu Yàlla. Yaakaar jooju nag, Buur, moo tax Yawut yi tuumaal ma!

Ku am ndam nag, maa lay def nga doon ag kenu fi sama biir néeg Yàlla, te doo fa génnati mukk. Maay bind fi sa kaw sama turu Yàlla ak sama turu dëkku Yàlla, te mooy Yerusalem gu bees, giy wàcce fa kaw, bàyyikoo fa sama Yàlla, maay bind it fi sa kaw sama tur wu yees.