TSK

TSK · Luke 20:36

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

«Man nag maa leen di musal ci njaniiwa? Maa leen di jot ci ndee? Moo yaw ndee, ana say mbas? Yaw njaniiw laa ne, ana sa tooke? Fomm làqu na ma!

Gannaaw ay doom lanu nag, ay boroom cér lanu, ay boroom cér yu Yàlla sédd, cér yu nu bokk ak Almasi, gannaaw noo bokk ak moom ab coono tey, ngir bokk ak moom teraangay ëllëg.

¶ Noonu itam la ndekkitel ñi dee di deme. Li ñu suul mooy jiwu wiy yàqu, te bu dekkee dootu yàqu.

Lu gaawa gaaw lay doon, ci xef ak xippi, bu liit gu mujj ga jibee; nde liit ga mooy jib, ñi dee, dekki, di ñu dul yàqooti, nun nag, nu soppiku.

¶ Bokk yi nag, buggunu ngeen réere mbirum way dawlu ñi, bay tiislu ni ñeneen ñi amul jenn yaakaar, di tiisloo.

¶ Ma daldi gis gàtt bu mel ni lu ñu rendi, mu taxaw fi digg ngàngune mi, ñeenti bindeef yeek mag ñi yéew ko. Gàtt bi juróom ñaari béjjén la am, ak juróom ñaari bët, di juróom ñaari noowi Yàlla, yi ñu yebal ci àddina sépp.

Ndokkle ak sellnga ñeel na ñi séddu ci ndekkite lu jëkk li! Ñooñu, ñaareelu dee gi manalu leen dara. Ñooy doon it sarxalkati Yàlla ak Almasi, te ñooy nguuroondoo ak Almasi junniy at.

di tuuru ci digg péncu dëkk bi. Ci ñaari tàkki dex gi, garabu dund a ngi ci, di meññ fukki yoon ak ñaar, weer wu nekk benn yoon, xob yi di faj askani àddina.