TSK

TSK · Luke 21:34

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Yanqóoba dem, jël gàtt yi, indil yaayam, mu defar ba mu neex, ni ko baayam bëgge.

Aji Sax ji du nangoo baal kooku, nde su boobaa, sànjum Aji Sax jeey ànd ak fiiraangeem, tàkk ci kawam, te mboolem alkànde gi ñu bind ci téere bii day këppu ci kawam, te Aji Sax jeey far aw turam fu asamaan tiim.

Yal nañu sànkoo mbetteel, keppoo seen fiir, sànkoo seenum yeer.

Wóoy ngalla Efrayim, kaala gu yànj ga ay màndikatam di sagoo! Taaram bu yéeme baa koy réer, ni tóor-tóor yu wow, te ma nga toŋ ca coll, wa ña biiñ man dëkke, fa tiim xur wu nangu wa.

Jongrukati Israyil yépp a silmaxa, te xamuñu dara. Ñoom ñépp a diy xaj yu luu, manuñoo baw, xanaa tëdd di jeneer, soppi nelaw.

Sang bi ne ko: «Màrt, Màrt, yitte yi nga xintewoo, di ci doñ-doñi moo bare.

Waaye su jawriñ ja nee ci xelam: “Sama njaatige dikkagul léegi,” ba tax mu tàmbalee dóor surga ya, góor ak jigéen, di lekk ak a naan, di màndi,

Luke 21:8 TSK

Yeesu ne: «Moytuleen, ngir ñu bañ leena nax, ndax ñu bareey dikk, tuddoo sama tur, naan: “Man a,” te naan: “Waxtu wi jege na.” Buleen leen topp.

Dama leena bind, ne leen buleen amlante ak ku tuddoo mbokkum gëmkat, te di fokatub séy, mbaa mu dib bëgge, mbaa mu dib bokkaalekat, mbaa ab saagakat, mbaa màndikat, mbaa ab ŋàppaaral. Ku ni mel, buleen bokk ak moom lekk sax.

ak bokkaale, ak xërëm, ak mbañeel, ak féewaloo, ak kiñaan, ak mer mu ëpp, ak jiital say bëgg-bëgg, ak réeroo, ak xàjjalikoo,

ndax yeen ci seen bopp, xam ngeen xéll ne Sang bi, ni sàccub guddi lay dikke.

Ndax démb kat yàgg ngeena def coobarey xeet yi xamul Yàlla, ci ay ñaawtéef, ak topp seen bakkan. Dangeen daa màndi ak a xawaare, dëkke naan biiñ, di jaamu tuur yu seexluwu, waaye na fi yem nag.

¶ Kon nag soppe yi, li feek ngeen di séentu loolu, defleen seen kem-kàttan, ba bésub keroog fekk leen ci jàmm, te ngeen baña am benn gàkk, mbaa sikk ci gis-gisu Yàlla.