Genesis 7:4
TSK
Ndax kat li feek juróom ñaari fan dinaa wàcce taw ci kaw suuf diiru ñeent fukki guddi ak ñeent fukki bëccëg, ba far ci àddina mboolem mbindeef mu ma sàkk.»
TSK
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ndax kat li feek juróom ñaari fan dinaa wàcce taw ci kaw suuf diiru ñeent fukki guddi ak ñeent fukki bëccëg, ba far ci àddina mboolem mbindeef mu ma sàkk.»
Doom aadama la bésu safaan bay bett, jekki ne dàll fi kawam, ni jën wu keppu cib caax, loru, mbaa picc mu tancu cig fiir. Doom aadama xamul bésam.
Yeen waa Mowab, pat-pati rekk, di tàbbiy pax aki yeer.» Kàddug Aji Sax jee.
Moo sàkke xeeti àddina yépp ci kenn nit, ñu dëkke déndu suuf sépp, te moo leen àppal seeni jamono, rëddal leen seen kemi dëkkuwaay.