TSK

TSK · Luke 22:18

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

dugub di ko dooleel, biiñ di bégal xolam, ag diw di leeral kanamam.

Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, mooy berndeel xeet yépp fi kaw tund wii, bernde ju niin ak ngëneelu biiñ, yàpp wa duuf, yuq ja ne xéew, ak tànnéefu biiñ bu teey.

¶ «Ci jamonoy buur yooyu Yàlla Boroom asamaan dina samp nguur gu dul tas mukk, te wenn xeet du ko yilif mukk. Nguur googu dina tasaare mboolem yeneen nguur yooyu, ba genn du ci des, waaye moom day sax ba fàww.

Ndaw bànneex akub taar ca ñoom! Pepp yafal xalelu góor, biiñ bu bees naatal yaramu janq.

Bu ngeen gisee xew-xew yooyu sotti, noonu itam ngeen di xame ne nguurug Yàlla dëgmal na.

Acts 2:30 TSK

Waaye yonent la woon, te xamoon na ne Yàllaa ko giñaloon ne ku bokk ci geñoom lay teg cib jalam.

¶ Yàlla kat moo nu wallu ba génne nu ca kilifteefu réewum lëndëm ga, toxal nu ci biir nguurug Doomam ji mu sopp.