TSK

TSK · Luke 5:24

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ «May xool ba tey ci biir peeñum guddi ma, gisuma lu moy jëmm ju mel ni doomu nit di ñëw, mook niiri asamaan, jëm ci góor gu mag gi; ñu yóbbu ko ba ca moom.

Luke 5:13 TSK

Yeesu tàllal loxoom, laal ko ne: «Soob na ma, setal.» Ca saa sa ngaana ga teqlikook moom.

Luke 8:54 TSK

Yeesu itam jàpp ca loxol janq ba, daldi àddu ca kaw, ne ko: «Janq, jógal.»

Acts 3:6 TSK

¶ Piyeer nag ne ko: «Xaalis ak wurus de, yoruma ko. Waaye li ma am, jox naa la ko: ci turu Yeesu Almasi waa Nasaret bi, doxal!»

Acts 9:34 TSK

Piyeer ne ko: «Ene, Yeesu Almasi wéral na la; jógal, lalal sa bopp.» Mu jóg ca saa sa.

Mu àddu ca kaw, ne waa ji: «Jógal taxaw jonn!» Waa ji ne bërét, jóg, daldi dox.