Ñu bon ñi Yàlla ne leen: «Lu ngeen di tari sama dogali yoon, di waxe sama kóllëre?
TSK
TSK · Luke 6:42
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ku jëkke layoo, ñu ne yaa yey, ba keroog ka nga joteel weddi la.
Sang bi ne ko: «Jinigalkat yi ngeen doon! Xanaa du ci bésub Noflaay la kenn ku nekk ci yeen di yiwee aw yëkkam mbaa mbaamam ca gétt ga, ngir wëggi ko?
Piyeer ne leen: «Tuubleen te ku nekk ci yeen sóobu ci ndox ci turu Yeesu Almasi ngir njéggalug bàkkaaram, ngeen daldi jot ci Noo gu Sell giy maye.
Diiru ñetti fan gisul dara, lekkul, naanul.
¶ Yaw nit kiy sikke nag, amoo aw lay, ndax boo sikkee keneen, sa bopp nga sikk, nde yaw miy sikke, jooju jëfin ngay jëfe.
Loolu lépp ci Yàlla la jóge, moom mi nu jubale ak boppam ci Almasi, te moo nu sas, ngir nuy waare juboo googu.
Ku setal sa bopp nag ba mucc ci yu bon yooyii, yaay doon ndabal teraanga lu sell te amal sangam njariñ ngir jépp jëf ju baax.
Waaye yii jikko, ku ko ñàkk, daa fekk mu gàtt gis-gis ba far gumba, te fàtte ne dees koo fóotoon ba mu set, teqlikook bàkkaari démbam.