Yàlla ne ko: «Ngalla jëlal sa jenn doom jii di Isaaxa, muy koo bëgg, nga dem ca réewu Morya ca tund wa ma lay wax, joxe ko fa, mu nekk saraxu rendi-dóomal.»
TSK
TSK · Luke 7:12
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Bokk yépp daldi jóg dal ci sama kaw, sang bi. Ñu ne ma: “Jox nu sa doom ji rey doomu ndeyam, nu rey ko, feyul doomu ndeyam ji mu rey. Moo dese ndono li, kon danu koy sàkkal pexe, moom itam.” Dañoo nara fey wenn xal wi ma dese, ba xañ sama jëkkër aw tur, xañ ko aw askan ci kaw suuf.»
Jëtun ba nag ne ko: «Giñ naa ci Aji Sax ji sa Yàlla jiy dund, awma mburu. Awma lu moy barci-loxob sunguf ca njaq la ak as diw ca tax ba. Gis nga, may for nii ñetti bant, ba toggi ko, nu lekk, maak sama doom, doora dee ak xiif.»
Ilyaas fab xale ba, jële ko ca néeg ba ca kaw taax ma, wàcce ko ca biir kër ga, jox ko ndeyam. Mu ne ko: «Xoolal, sa doom a ngi dund!»
Surga ba fab ko, yóbbu ca yaayam, mu uuf ko, ba ca digg bëccëg, xale ba dee.
¶ «Bu loolu amee maay sottil waa kër Daawuda ak waa Yerusalem, noowug yiw aki dagaan, ba ñu geesu ma man, mi ñu jam ba mu sar, te dinañu ko jooy ni ñuy jooye benn bàjjo, di ko naqarlu ni ñuy naqarloo deewug taaw.
Ñépp a ngay jooy ak a tiislu janq bi. Yeesu nag ne leen: «Buleen jooy. Janq bi deewul, day nelaw rekk.»
¶ Piyeer jóg, ànd ak ñoom, ba agsi. Ñu yéege ko ca néegu kaw taax ma. Ay jëtun a nga fa woon. Ñoom ñépp di jooyoo, yéew Piyeer, won ko turki yaak mbubb ya Dorkas defaroon ba muy nekk ak ñoom.
Waaye su dee ab jëtun bu ami doom mbaa ay sët, ñooñoo wara jëkka jéema jëfe ag ragal Yàlla ci seen biir kër, ba delloo njukkal seen waajur, ndax loolu la Yàlla rafetlu.