Su ko defee nga wax Firawna, ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: ‘Israyil mooy sama taaw bu góor.
TSK
TSK · Malachi 1:6
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ «Na ku nekk weg ndeyam ak baayam te wormaal sama bési Noflaay. Man Aji Sax ji, maay seen Yàlla.
Aji Sax ji lañuy feye lii? Ndaw xeet wu dofe te ñàkk xel! Mooy seen baay, bind leen, sàkk leen, samp leen.
Ag maas a ngi saaga baay, te wormaaluñu ndey.
Asamaan, déglul; suuf, teewlul, Aji Sax jeey àddu: «Ay gone laa yar, màggloo leen, ñoom, ñu gàntal ma.
Waaye déy, Aji Sax ji, yaa di sunu Baay; noo di ban, yaw ngay tabaxkatu njaq, nun ñépp di sa liggéeyu loxo.
Moona maa leen jëmbat, ngeen di ngëneelu reseñ, di jiwu mu mucc ayib. Nu ngeen walbatikoo di baadooloy reseñu àll?
«Te it yonent ak sarxalkat ñoo bokk yàqu, sama biir kër sax gis naa ci seenug mbon.» Kàddug Aji Sax jee.
Sëti Yonadab doomu Rekab yii déy wormaal nañu santaane ba leen seen maam santoon, waaye xeet wii déggaluñu ma.”
Sama ñoñ a sànku ndax ñàkka xam; yeen, xam-xam ngeen gàntal, ma gàntal seenug carxal. Yeena fàtte seen yoonu Yàlla, man it maay fàtte seeni doom.
Ni Kanaaneen biy jula, ni la Efrayim yore màndaxekaayu njublaŋ cib loxoom, bëgga naxe.
Ngeen naa: «Ndax lan?» Ndax Aji Sax ji moo seede seen diggante ak seen jabar ja ngeen jël ba ngeen di ndaw, tey ngeen wor ko, te mu doonoon seen wéttal, seen jabar ju ngeen séqal kóllëre.
«Ca seen janti maam ngeen dëddoo sama dogali yoon, sàmmuleen ko. Waññikuleen fi man, ma waññiku fi yeen,» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. «Yeena ngi naa: “Ci lan lanuy waññikoo?”
Ni seen Baay ame yërmande nag, nangeen ni ame yërmande.
Waa ja nag namma wutu lay, ne Yeesu: «Sama moroom mooy kan?»
¶ Mboolem ñi ci buumu njaam, nañu jàpp ne seeni sang yelloo nañu gépp wegeel, ngir kàddu gu teddadi baña tege ci turu Yàlla, ak sunu àlluwa.
¶ Gannaaw nag kiy àtte nit ku nekk ci ay jëfam te amu ci xejj ak seen, Baay ngeen koy wax, sàllooleen koo ragal, seen diirub ngan ci kaw suuf.