TSK

TSK · Malachi 2:14

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Yàlla Aji Sax ji daldi ne: «Wéet baaxul ci nit, kon dinaa ko bindal ku koy jàpple te jekk ci doon wéttalam.»

Day dëddu wóllëreem, ba muy ndaw, fàtte kóllëreem ak Yàllaam.

Doom, ana looy xemmeme keneen, bay foye céri jaambur?

Bànneexul yaak ndaw si nga sopp ci fan wu gàtt wi la Yàlla may fi suuf, ndax loolu nga séddoo ci fan wu gàtt wii ngay doñ-doñaale fi kaw dun bi.

Aji Sax jee la woo, nga dib jeeg bu ñu wacc, sa xol jeex tàkk, Mu ne la: “Nees di wacces ndaw, si nga takk ba ngay ndaw?”» Sa Yàllaa ko wax.

Ñu wara am gàcce ci seen jëf ju siblu, te gàcce gàcceelu leen. Xamuñu sax luy kersa! Moo tax ñuy fëlëñoondook ñiy fëlëñu. Kera ba ma leen di dikkal, ñooy tërëf.» Aji Sax jee ko wax.

Ñoom it ñu ne Yeremi: «Mboolem kàddu gu la sa Yàlla Aji Sax ji yóbbante ci nun, bu nu ko deful, yal na Aji Sax ji doon seede bu wér, bu dëggu bi nuy seedeel ag tooñ.

Micah 1:2 TSK

Dégluleen, yeen, xeetoo xeet, teewlul, yaw àddina ak li ci sa biir, ba Boroom bi Aji Sax ji seedeel leen tuuma, Boroom beey àddoo fa màkkaanam mu sell ma.

Kenn deful lii te desem xel. Kenn doŋŋ a ko defoon. Ndax lan? Kuutaay li ko Yàlla digoon la doon wut. Kon nag sàmmleen seenum xel, te buleen wor seen jabar ja ngeen jël ba ngeen di ndaw.

Waaw, nit dina sàcc Yàlla? Ndaxam yeen yeena ngi may sàcc te yeena ne: “Ana nu nu la sàcce?” Xanaa ci seen cérub fukkeelu alal akub jooxe.