Yàlla Aji Sax ji nag móol nit ci pëndu suuf, sol ngelawal dund ci paxi bakkanam, nit daldi doon boroom bakkan.
TSK
TSK · Malachi 2:15
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
ay goney Yàlla ñoo gis jigéen ñeek seen taar, ñuy jël ñi ñu bëgg ci ñoom, def leeni jabar.
mu ne ma: ‘Naanal ba noppi, ma wëggal la say giléem,’ kooku na di soxna, si Aji Sax ji jagleel sama doomu sang.”
¶ Gannaaw gi Rebeka ne Isaaxa: «Àddina soof na ma ndax jigéeni Etteen ñi. Yanqóoba de, bu jëlee ci jigéeni réew mi di Etteen ñu mel ni ñii, sama dund gi, dee a koy gën!»
Ndax dañu may dëddale ak seen doom yu góor, ñu mujj di jaamu yeneen yàlla, ba sànjum Aji Sax ji tàkk ci seen kaw yeen, fàkkas leen ci lu gaaw.
Seen genn-wàlli njaboot di làkk asdodd, ña ca des di làkk leneen ci làmmiñi doxandéem yi, te kenn ci ñoom manula wax yawut.
Sàmmala sàmm sab xol, nde xalaati xol ngay jëfe.
Bu leen soosu ndaw xiir ci moy, buleen teggi, topp ko.
Moona maa leen jëmbat, ngeen di ngëneelu reseñ, di jiwu mu mucc ayib. Nu ngeen walbatikoo di baadooloy reseñu àll?
Ngeen naa: «Ndax lan?» Ndax Aji Sax ji moo seede seen diggante ak seen jabar ja ngeen jël ba ngeen di ndaw, tey ngeen wor ko, te mu doonoon seen wéttal, seen jabar ju ngeen séqal kóllëre.
Yeen nag yeenay donoy yonent yi te yeenay séddu ci kóllëre, gi Yàlla fasoon ak seeni maam, ba mu nee Ibraayma: “Ci saw askan la xeeti àddina yépp di barkeel.”
Ndaxte jëkkër ji gëmul day daldi séddu sellnga ndax jabaram ja dib gëmkat, te jigéen ji gëmul it day séddu sellnga ca jëkkëram jay gëmkat. Su dul woon noonu doom yu ngeen ca am di ñu sobewu, te bir na ne doom yu ngeen ca am, ñu sell lañuy doon.
¶ Yeen ñiy baay it, buleen xoñoñal xale yi, waaye yarleen leen, di leen jubanti, di leen xamal coobarey Boroom bi.
Naka noonu, na jigéen ñiy taxawu mbooloo mi di ñu tedd, buñu diy soskat, nañu moom seen bakkan, te jara wóolu ci lépp.
Waaye ku nekk, sa xemmemtéefu bakkanu bopp moo lay xiirtal, ootal la ba nax la.