Su ko defee du teddadil aw askanam ci biir bànni Israyil, ndax man Aji Sax ji maa ko sellal.»
TSK
TSK · Malachi 2:8
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Aa! Xale yi, coow li ma dégg, muy law ci biir ñoñi Aji Sax ji, rafetul de!
Urya sarxalkat ba daldi tabax sarxalukaay bu dëppook mboolem tegtal ya bàyyikoo ca Buur Axas ca Damaas. Uri noppi na ko bala Buur Axas di ñibbsi.
Aji Sax jee ma yool sama njekk, samay loxoo set, mu fey ma.
Xel mu ñaw, jëw bu rafet; sam xel jekkadi, ñu xeeb la.
Moyal yoon wi; lajj, wàcc xàll wi, te may nu jàmm ak Aji Sell ju Israyil.
«Sarxalkat yi newuñu: “Ana Aji Sax ji?” Ñi ŋank yoon wi faaleetuñu ma, njiit yi gàntal ma, yonent yiy waxe waxyuy Baal, tuur mi, di topp lu leen dul jariñ.
Yaw Aji Sax ji yaakaaru Israyil, ku la wacc, torox; ku la dëddu daa repp. Moo wacc Aji Sax ji, bëtu ndox miy dund.
«Te it yonent ak sarxalkat ñoo bokk yàqu, sama biir kër sax gis naa ci seenug mbon.» Kàddug Aji Sax jee.
Bu ngeen ma daan indil sama céru ñam, muy nebbon, di deretu sarax yi, dangeen di dugalaale sama biir bérab bu sell bi ay doxandéem yu xaraful, du ci jëmm, du ci xol. Noonu ngeen sobeele sama kër gi. Fecci ngeen sama kóllëreek yeen ndax seen jépp jëf ju siblu.
Gannaaw ñoo doon dox diggante xeet week seen kasaray tuur, ba yóbbe leen ay wu leen gàllankoor, maa leen giñal ne, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, ñooy gàddu seenu ay.
«Doom teral baayam, jaam, sangam. Man, su ma dee baay, ana saab teraanga? Su ma dee ab sang, ana saab cér?» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, mu ne: «Yeen sarxalkat yi teddadil ngeen sama tur, yeen ngeen ne: “Ana nu nu teddadile sa tur?”
«Moo tax man it ma def xeet wépp xeeb leen, sewal leen, feye leen ko seen ñàkka sàmm samay yoon, ak par-parloo gi ngeen di diglee yoon wi.»
¶ Kenn ci xamkati yoon yi nag àddu ne: «Sëriñ bi, loolu nga wax de, nun itam, xasaale nga nu ci.»
Li gën sax mooy nga baña lekk yàpp, mbaa nga baña naan biiñ, mbaa leneen lu mu doon lu mana fakktal sa mbokkum gëmkat.