TSK

TSK · Malachi 3:13

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Job 34:7 TSK

Ana ku mel ni Baay Ayóoba mii, di ñaawle ni muy naanem ndox,

Mu naa ca xelam: «Yàlla fàtte na, dummóoyu na, du xoolati.»

Ña nga naa: «Na Aji Sax ji gaaw! Na baral liggéeyam, nu gis. Na Aji Sell ju Israyil sottal mébétam, mu sotti, nu xam.»

Ana kooy kókkaleek a ñàkke kersa? Moo kooy yékkatil kàddu? Kooy xool gëti xeebeel? Xanaa du Aji Sell ju Israyil ji?

Yeenay damu fi sama kaw, di ma wax waxi reewande ju bare! Maa déggal sama bopp.

Ngeen naa: «Ndax lan?» Ndax Aji Sax ji moo seede seen diggante ak seen jabar ja ngeen jël ba ngeen di ndaw, tey ngeen wor ko, te mu doonoon seen wéttal, seen jabar ju ngeen séqal kóllëre.

Waaw, nit dina sàcc Yàlla? Ndaxam yeen yeena ngi may sàcc te yeena ne: “Ana nu nu la sàcce?” Xanaa ci seen cérub fukkeelu alal akub jooxe.

Kooku mooy jànkoonteeka damu ci kaw mboolem lees di wooye yàlla, mbaa lees di jaamu, te mooy mujj toog ca kër Yàlla ga, ba far tudde boppam Yàlla.