TSK

TSK · Micah 4:8

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ba mu ko defee Israyil jóge fa, samp xaymaam ca gannaaw Migdal Eder.

Terewul Daawuda nangu tatay Siyoŋ, ga ñu dippee Kër Daawuda.

Neleen bunt yi kulbét, ubbileen bunti cosaan yi, Buur Boroom ndam duggsi.

Mu gàbb ko, dindi doj ya, jëmbat ca ngëneeli reseñ, tabax tóojub doj fa digg ba, ba yett ca mbalkam nalukaayu reseñ, tey yaakaar reseñ ju neex, mu meññ, wex.

¶ «Ci jamonoy buur yooyu Yàlla Boroom asamaan dina samp nguur gu dul tas mukk, te wenn xeet du ko yilif mukk. Nguur googu dina tasaare mboolem yeneen nguur yooyu, ba genn du ci des, waaye moom day sax ba fàww.

Ay xettlikat ñooy yéeg kaw tundu Siyoŋ, ngir yilif tundu Esawu, nguur gi di moomeelu Aji Sax ji.»

Maay dagge watiiru xare diiwaanu Efrayim, dagge fasu xare fi Yerusalem, xalay xare damm, muy wax xeet yi jàmm, kilifteefam dale géej ba géej, dale dexu Efraat ba ca cati àddina.

Foofa la Almasi tiime lu sore gépp nguur, ak bépp sañ-sañ, ak gépp manoore, ak gépp kilifteef, ak wépp tur wees di tudd, muy tey, di ëllëg.