TSK

TSK · Micah 7:1

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Njàlbéenu meññeef mi ñuy indil Aji Sax ji, ci mboolem lu meññee ci seen suuf, yaa koy moom, te képp ku set ci sa waa kër, sañ na cee lekk.

Ñu baree ngi naa: «Gore naa,» waaye kuy boroom kóllëre dëgg?

fa dara dul des lu moy am poraat; mu mel ni wittum oliw, bu noppee ñaari doom ak ñett ay des ca kaw, mbaa ñeent ba juróom ci car yi meññ. Kàddug Aji Sax jee, Yàllay Israyil.

Cati àddina lay woy di jibe, nu dégg ñu naa: «Teddnga ñeel na Aji Jub ji!»

Baatu ndaw su jagadi laa dégg, ma nga jàq, di matub taawam. Baatub Siyoŋ, dëkk bu taaru baa! Ma ngay àppaat, tàllal yoxo ya, naan: «Wóoy, ngalla man; ne yàcc ci loxol bóomkat yi!»

Wóoy saa ndey, loo ma doon jure! Man mi réew mépp di xulook a layool, leblewma, lebuma; te ñépp di ma móolu.

«Ni cabbu reseñu biir màndiŋ, ni laa fekke Israyil. Ni ndoortel doomi figg ju ndey ja taawloo, ni laa gise seeni maam. Waaye ñoom ñoo dem Baal Pewor, ñoo sédd seen bopp Baal, tuur mu ruslu mi, ba tax leena seexluwu ni kooku ñu sopp.