TSK

TSK · Micah 7:8

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Job 31:29 TSK

Ndegam maa bége musibay bañ, mbaa ma bellaxndikoo loraange ju ko dab,

Ñiiki watiir, ñeeki fas, nun sunu turu Yàlla Aji Sax ji lanuy tudd.

Ma daanu tey, ñu daje di ko bége, dajaloo fi sama kaw, di ma fexeel te yéguma, di ma yàpp, tëë ba.

Aji Sax ji sama Yàlla, àttee ma sa dëgg, ñu bañ maa ree!

Soo tërëfee it, doo daanu. Aji Sax jee lay walloo loxoom.

Sama am-di-jàmm bu ma wóolu sax jógal na ma, te daan lekk samaw ñam.

Ceeñeeru biir lëndëm jollil na ku jub ak ku baax, di boroom yërmande ak njekk.

Ku jub day daanu juróom yaari yoon, jógaat, ab soxor sërëx ci njekkar.

Yeen waa kër Yanqóoba, kaayleen nu doxe leeru Aji Sax ji!

ba ne ñi ñu tëjoon: “Génnleen!” Fa ñu nekkoon cig lëndëm, laa naa leen: “Génnleen ci leer gi!” Ñooy doon sama gàtt, dellu di fore aw ñall, ak wépp tund wu ne faraas tey.

Yerusalem, jógal ne ràññ, sag leer feq na; teddngay Aji Sax ji fenkal na la!

«Ãa yeen waa Babilon, yeena sëxëtoo xeet wi ma séddoo, di ko bégeek a bànneexoo, di bajantu ni nag wuy bàcc pepp, di ŋexal ni naaru góor?

Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: Yeena doon tàccu, di fecc, bége tiisu réewum Israyil, di leen sewal lu ngeen man.

Amos 9:11 TSK

«Bésub keroog maay yékkati mbaarum Daawuda mi joy, ba fattaat xar-xar yi, defaraat gent bi, tabaxaat ko na woon.

Ndaw siy samab noon moo koy seede, sëlmoo gàcce, moom ma doon naa: «Ana sa Yàlla Aji Sax ji?» Samay gët a naa ndaw soosu jàkk, ñu di ko dëggaate ni banu mbedd.

ngir nga xippil leen, jële leen ci lëndëm, tàbbal leen ci leer, seppee leen ci noteelu Seytaane, indi leen ci Yàlla, ñu am njéggalug bàkkaar, am cér ci biir nit ñi ñu sellal ndax ngëm, gi ñu ma gëm.”

Waa àddina dinañu bége seen dee, di bànneexu, di joqlante ay njukkal, ndaxte ñaari yonent yooyu ñoo lakkaloon waa àddina.

Guddi du amati, te deesul soxlaati làmp mbaa naaj, ndax Boroom bi Yàlla moo leen di leeral. Te dañuy nguuru ba fàww.