¶ Ba mu ko defee Rabsake bëkk-néegu buurub Asiri ne leen: «Waxleen nag Esekiya ne ko: Buur bu mag ba, buurub Asiri dafa wax ne: “Sa yaakaar jii nga yaakaar, ana foo ko teg?
TSK
TSK · Nahum 2:13
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Booba buurub Asiri daa dégg ne Tiraka buurub Kuus moo leen di songsi. Mu dellu yebal ay ndaw ca Esekiya, ne leen::
Dikkleen gis jaloorey Aji Sax ji, ak yàqute gi mu dogal ci kaw suuf.
Wóoy ngalla yaw bóomkat bi kenn bóomul, yaw workat bi kenn worul. Boo noppee bóome, ñu bóom la, te boo noppee wore, ñu wor la.
Manees naa foqati alalu sëxëtoo ci loxol jàmbaar a? Am manees naa rëcc boroom doole bu la jàpp?
«Babilon mu reewee, maa ngii fi sa kaw.» Kàddug Boroom bi, Aji Sax jee, Boroom gàngoori xare yi. «Sa bés déy taxaw na, di àpp bi ma la wara mbugale.
kon nag Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii ci seen kaw, man itam. Maay wàcce fi seen biir ay mbugal, xeet yi teg ci seeni gët.
Neel: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yaw Sidon, maa ngii fi sa kaw. Dees na ma sargal fi sa biir, ba ñu xam ne maay Aji Sax ji ndax mbugal yi ma fiy wàccesi, ba fésal fi sama sellnga.
Moo tax maa ngii fi sa kaw, yaak say wali dex. Maay def réewum Misra gent bu ne sereŋ, mu gentale Migadol ca bëj-gànnaar, ba Asuwan, fa mu digalook réewum Kuus ca bëj-saalum.
Neel: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yaw Gog, boroom Meseg ak Tubal, maa ngi nii fi sa kaw.
Wóoy, ngalla dëkkub tuurkatu deret bi, ñépp di fen, fees aku ay, te foqati alalu jaambur du dakk!
Sa tata yépp ni garabi figg yu ñoral ndoortel meññeef lay mel, soo yëlbee, doom ya rot, gémmiñu lekk-kat aw.