¶ Fekk na seen Yàllaa ngi ne jàkk ci magi Yawut ñi, ba kenn bàyyiwul liggéey ba, ba keroog ñuy yónnee xibaar ba Buur Daryus, ba jot ci bataaxalu tontam ca mbir ma.
TSK
TSK · Nehemiah 2:8
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Wormaal nañu it màggalu Mburu mu amul lawiir, diiru juróom ñaari fan, ci biir mbégte, ndax fekk na Aji Sax ji bégal leen lool ca na mu xiire buurub Asiri, mu yéwéne leen ba dimbali leen ci tabaxu kër Yàlla ga, Yàllay Israyil.
Ca benn fanu weer wa jëkk la dooroon yoon woowu mu bàyyikoo Babilon. Mu agsi Yerusalem ca benn fanu juróomeelu weer wa, ci mbaaxu Yàllaam ji ko toppe yiwam.
¶ Ba loolu amee ma ne leen: «Yeena gisal seen bopp toskare gi nu nekke. Yerusalem tas na, bunt yi lakk na. Aycaleen nu tabaxaat tatay Yerusalem ndax sunu gàcce faju.»
¶ Gannaaw loolu Elyasib sarxalkat bu mag ba ànd ak bokki sarxalkatam, ñu tabaxaat bunt ba ñuy wax Gàtt ya, sellalal ko Yàlla, taxawal laf ya, defaraat tata ja, ba ca soorooru Meya, sellalal ko Yàlla, jàppoo ko noonu ba ca soorooru Ananel.
Xolu buur walum ndox la ci loxol Aji Sax ji, fu ko soob mu jëme ko fa.
Yàlla def kilifag jawriñ ya baaxe Dañeel, yërëm ko.
Ndimbalal Yàlla nag moo ma may may dund ba tey jii, di ko seedeel ci mag ak ndaw, te waxuma lenn lu moy la yonent ya ak Musaa waxoon ne dina am.