Musaa taxaw ca buntu dal ba, ne: «Ku ànd ak Aji Sax ji, fii ci man!» Leween ñépp dikk, yéew ko.
TSK
TSK · Numbers 1:50
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Leween ñi nag nañu dal fi wër jaamookaay bi seedes kóllëre gi dence. Su ko defee am sànj du dal ci kaw mbooloom bànni Israyil. Te itam na Leween ñi dénkoo dénkaaney jaamookaay bi seedes kóllëre gi dence.»
¶ Ñii ñoo di askani Aaróona ak Musaa, jant ba Aji Sax jiy wax, mook Musaa ca kaw tundu Sinayi.
Làngi Gersoneen ña, ca gannaaw jaamookaay ba lañu daan dale, fa féete sowu.
¶ «Bu dal bi waree jóg, na Aaróona ak doomam yu góor muur yëf yu sell yi, ak mboolem jumtukaayi bérab bu sell bi ba noppi. Gannaaw loolu la askanu Keyat di dikk, ngir gàddu ko. Su ko defee duñu laal dara lu sell, bay dee. Loolu la Keyateen ñi di gàddu ci wàllu xaymab ndaje mi.
te itam maa jukkee Leween ñi ci bànni Israyil, maa leen yékkati, jox leen Aaróona aki doomam, ngir ñu liggéey liggéeyu bànni Israyil ci wàllu xaymab ndaje mi, di defal bànni Israyil seenug njotlaay, ngir bu bànni Israyil jegee bérab bu sell bi it, du tax menn mbas am ci seen biir.»
Gannaaw loolu Leween ñi doora liggéeyi seen liggéey ci wàllu xaymab ndaje mi, ci kilifteefu Aaróona aki doomam. Noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa ci Leween ñi, na lañu def ak ñoom.
Nangeen dénkoo ndénkaanel bérab bu sell bi, ak ndénkaanel sarxalukaay bi, ngir am sànj baña dalati ci kaw bànni Israyil.
Gannaaw loolu ma nattal leen xaalis baak wurus waak ndab, ya Buur aki wóllëreem aki jawriñam jooxe woon, ñook mbooloom Israyil ma fa teewoon, te lépp jëm ca sunu kër Yàlla ga.
¶ Leween ñi ñoo doon Yeswa ak Binuy ak Kadmiyel ak Serebya ak Yuda ak Mataña may jiite jàngi cant ya, mooki bokkam.
Ci biir loolu, ca janti Sorobabel ak ca janti Neyemi, askanu Israyil gépp daan nañu génneel jàngkat yeek fara bunt yi seen cér, bés bu nekk it, génneel Leween ñi seen cér, Leween ñi génneel askanu Aaróona seen cér.
¶ Ma dégg itam ne joxuñu Leween ñi seeni cér, ba tax ku nekk ci Leween ñaak jàngkati kër Yàlla ga ne coww ca toolu boppam, bàyyi liggéey bi mu sasoo.
Fii la giiri Israyil di yéegsi, di giir yi Ki Sax séddoo. Ñu ngi santsi Aji Sax ji, ni ko Israyil warloo.