Ci kaw loolu Aji Sax ji feeñu Ibraam ne ko: «Sa askan wi soqikoo ci yaw laay jox réew mii.» Ibraam nag daldi tabaxal Aji Sax, ji ko feeñu, ab sarxalukaay.
TSK
TSK · Numbers 10:29
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Keroog Aji Sax ji fas na kóllëre digganteem ak Ibraam, ne ko: «Askan wi soqikoo ci yaw laa jox réew mii dale ci dexu Misra, ba ca dex gu mag googee di Efraat,
Maa ngi lay ñaan, nga musal ma ci sama loxol mag Esawu, ndaxte ragal naa, mu ñëw bóom ma, bóomaale jigéen ñi ak seeni doom.
¶ Musaa far dal ca kër waa ja. Mu mujj ko may doomam ju ñuy wax Sipora.
Damaa wàcc, xettlisi leen ci waa Misra; génne leen réew moomu, ba yóbbu leen réew mu baax te yaatu, réew mu meew maak lem ja tuuroo, foofa ca diiwaanu Kanaaneen ña ak Etteen ña ak Amoreen ña ak Periseen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña.
Maa leen di yóbbu ba ngeen dugg réew ma ma giñoon ne maa koy jox Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, te maa leen koy moomale, man Aji Sax ji.»
Ba loolu weesee Musaa tàggtook goroom, mu dellu réewam.
Mu yónnee ca Keneen ña, ne leen: «Demleen, dawleen jóge ci biir Amalegeen ñi, bala ma leena buubaaleek ñoom, te ba bànni Israyil di génn Misra, yeena leen jiwoon ngor ñoom ñépp.» Keneen ña daw, jóge ca biir Amalegeen ña.
Ay askan yu bareey dikk, naan: «Dikkleen nu yéegi tundu Aji Sax ji, fa kër Yàllay Yanqóoba, mu xamal nuy yoonam, ba nu doxe yooyu ñallam.» Siyoŋ kat la ndigalu yoon di bawoo, Yerusalem googu la kàddug Aji Sax ji di jóge.
waa dëkk bii dem ne bee: “Nan dema dem dagaani Aji Sax ji, nan sàkkuji Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,” Ñu ne leen: “Nun it kay, nu ngi dem.”»
Ngëm googu, ak xam-xam boobu, ñu ngi sukkandiku ci yaakaar, ji nu am ci texe ba fàww, te googu texe, Yàlla mi dul fen, moo ko dige ba àddina sosoogul.
¶ Noo gi ak Séet bi neeñu: «Ñëwal!» Ku ci dégg it, neel: «Ñëwal!» Ku mar, ñëwal; ku bëgg ci ndoxum dund mi, jëlal, ñu may la.