Damaa wàcc, xettlisi leen ci waa Misra; génne leen réew moomu, ba yóbbu leen réew mu baax te yaatu, réew mu meew maak lem ja tuuroo, foofa ca diiwaanu Kanaaneen ña ak Etteen ña ak Amoreen ña ak Periseen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña.
TSK
TSK · Numbers 13:27
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Kon keroog bu leen Aji Sax ji yóbboo réewum Kanaaneen ña ak Etteen ña ak Amoreen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña, fa mu giñaloon seeni maam, ne dina leen ko jox, réew mu meew maak lem ja tuuroo, nangeen wormaal màggal gi ci wii weer te ngeen di ko defe nii.
Yeen nag ma ne leen yeenay nangu seen réew ñoom, ndax maa leen ko jox, ngeen moom ko, muy réew mu meew maak lem ja tuuroo. Man maay seen Yàlla Aji Sax, ji leen ràññatleek yeneen xeet yi.
Bu nu Aji Sax ji nangulee, moo nuy dugal réew moomu, moo nuy jox réew ma meew maak lem ja tuuroo.
Du réew mu meew maak lem ja tuuroo nga nu yóbbu de, te séddoo nu céri tool mbaa tóokëri reseñ. Mbooloo mii mépp, man nga leena tuur lëndëm? Danoo ñëwul!»
Kon yeen Israyil, dégluleen te sàmmoo jëfe, ndax ngeen baaxle te yokku bu baax, ni leen ko Aji Sax ji seen Yàllay maam waxe, ca réew ma meew maak lem ja tuuroo.
Ba loolu wéyee mu indi nu fi bérab bii, jox nu réew mii, réew mu meew meek lem ji tuuroo.
te ngeen bind ca mboolem kàdduy yoon wii, gannaaw bu ngeen jàllee. Su ko defee ngeen mana dugg ca réew, ma leen Aji Sax jiy jox, réew mu meew maak lem ja tuuroo, noonee leen ko seen Yàllay maam Aji Sax ji waxe woon.
Nga jox leen réew mii nga giñaloon seeni maam. Muy réew mu meew meek lem ji tuuroo.
Ba tey maa leen giñal ca màndiŋ ma, ne duma leen yóbbu réew ma ma leen jox, fa meew maak lem ja tuuroo, fa gëna taaru ci réew yépp.