TSK

TSK · Numbers 15:9

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Loolu la yoon digle ci wàllu saraxu rendi-dóomal, ak saraxu pepp ak saraxu póotum bàkkaar ak saraxu peyug tooñ ak saraxu xewu colu ak saraxu cant ci biir jàmm.

ak ñetti fukkeeli efay sunguf su mucc ayib, di juróom ñeenti kilo, muy saraxu pepp, ñu tooyale ko ag diw, booleek yëkk wu nekk, ak ñaari fukkeeli efay sunguf su mucc ayib, di juróom benni kilo, muy saraxu pepp, ñu tooyale ko ag diw, booleek kuuy mi,

Bokkewul ak rendi-dóomalu Terutel weer wu nekk, mook saraxu peppam, bokkewul it ak rendi-dóomal bi war bés bu nekk, ak saraxu peppam, ak seen saraxi tuur, ni ko yoon tërale. Dees koy def ngir xetug jàmm, muy saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.

¶ Ci biir loolu nu warloo santaaney joxe at mu nekk ñeenti garaami xaalis, bu jëm ca sunu liggéeyu kër Yàlla ga,

Saraxu pepp biy ànd ak kuuy mi benn efa lay doon, di fukki kiloy pepp ak juróom, ak dayob pepp bu mu àttan buy ànd ak xar yu ndaw yi ak xiinu diw, yemook ñetti liitari diw ak genn-wàll ci efab pepp bu nekk.

¶ «Su dee bési màggal ak bési ndaje yi, saraxu pepp mi benn efa lay doon ngir yëkk wi, yemook fukki kilook juróom, ak benn efa ngir kuuy mi, ak dayo bu ñu àttan ngir xar yu ndaw yi, efab pepp bu ne ànd ak benn xiinu diw, di ñetti liitar ak genn-wàll.

Joel 1:9 TSK

Saraxu pepp ak saraxu tuuru dagg na ca kër Aji Sax ji. Sarxalkat yi, boroom dénkaaney Aji Sax ji, ñu ngi ñaawlu.