TSK

TSK · Numbers 21:33

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Fekk na Musaa duma Siwon, ma toogoon Esbon, di buurub Amoreen ña, duma it ca Eddrey, Og buuru Basan ba toogoon Astarot.

¶ Ba loolu wéyee nu walbatiku, awe yoon wa yéeg jëm Basan. Og buuru Basan nag dikk dajeek nun, mook gàngooram gépp, ngir song nu xare ca Eddrey.

Nu nangu seenum réew, sédd ko Rubeneen ñi, ak Gàddeen ñi, ak genn-wàllu giirug Manaseen ñi.

Suuf a ngi maral, wow koŋŋ, gottub Libaŋ am gàcce, lax, àllub Saron doon joor gu wow, garabi Basan ak Karmel yëngu, di ruus.

Yàppu xarekat ngeen di lekk, naan deretu garmiy réew mi, ñooy seeni kuuy, aki tàppaanga aki bëy aki yëkk, ñoom ñépp mel ni juru yafal yuy fore jooru Basan.