TSK

TSK · Numbers 28:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Màggalu Mburu mu amul lawiir, wormaal-leen ko. Diiru juróom ñaari fan ngeen ciy lekk mburu mu amul lawiir ni ma leen ko sante, saa yu jamonoom jotee ci weeru Abiib, ndaxte ci ngeen génn Misra. Te itam buleen taxawe loxoy neen ci sama kanam.

Nañu raxas yérey biir yi ak yeel yi, sarxalkat bi boole lépp lakk ci kaw sarxalukaay bi. Saraxu rendi-dóomal la, saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.

Sarxalkat bi day jàpp ci laaf yi, xotti te bañ koo teqale, daldi koy lakk ci sarxalukaay bi, ci kaw mattum taal bi. Saraxu rendi-dóomal la, saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.

Nañu nekkal seen Yàlla ay nit ñu sell, te baña teddadil seen turu Yàlla, ndax saraxi sawar yi ñeel Aji Sax ji, te di seen ñamu Yàlla, ñoo koy joxe. Kon nag dañoo wara sell.

«Na bànni Israyil di màggal bésub Mucc ba, saa yu jotee.

Ku set nag te nekkul ciw yoon, su ñàkkee màggal bésub Mucc bi, kooku dees koy dagge ciw askanam, ndax saraxu Aji Sax ji mu joxewul ci bésam. Kooku moo gàddu bàkkaaru boppam.

ak biiñ ngir saraxu tuuru, ñetteelu xaajub xiin, di ñaari liitar. Na joxe loolu, def ko xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.

¶ «Yooyu sarax ngeen di def, ñeel Aji Sax ji, ci seen bési màggal, te du bokke ak seen sarax yi ngeen xasal seen bopp, ak seen saraxi yéene, ak seen saraxi dóomali bés bu nekk, ak seen saraxi pepp ak seen saraxi tuur, ak seen saraxi canti biir jàmm.»

Ezra 3:2 TSK

Ba mu ko defee Yosuwe doomu Yoccadag, mook moroomi sarxalkatam, ak Sorobabel doomu Selcel aki bokkam daldi tabax sarxalukaayu Yàllay Israyil, ngir sarxal ca saraxu dóomal ba, mu dëppook li ñu bind ci téereb yoonu Musaa, góorug Yàlla ga.

Yékkatileen woy te jiin, xalam neex, ànd ak moroom ma.

Maa leen di nangul seen saraxu cuuraay, gannaaw bu ma leen génnee fa biir xeet yaak réew ya ngeen tasaaroo ca seen biir, ba dajale leen. Su boobaa maay jëfe sellnga fi seen biir, xeet yi seede.

Xanaa di indi ñam wu sobewu fi sama sarxalukaay. Yeen ngeen ne: “Ana nu nu la sobeele?” Xanaa xalaat ne sañees naa teddadil sarxalukaayu Aji Sax ji.

ndax kat nun nooy cuuraayal Almasi fa Yàlla, ñeel ñi ci yoonu texe, ak ñi ci yoonu sànkute.

Fii ma tollu jot naa li ma aajowoo lépp, maa ngi ci naataange; doyle naa sëkk, gannaaw ba ma nangoo ci loxol Epafrodit, seenub yóbbante, te sarax su ñu nangu la, di xeeñ xetug jàmm, te neex Yàlla mi mu ñeel.