TSK

TSK · Numbers 3:15

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Giirug Leween ñi nag ci bànni Israyil lañu bokk, waaye limaaleesu leen ak ñoom.

Ba ñu waññee mboolem góor ña ca am weer, jëm kaw, juróom ñetti junni ak juróom benni téeméer (8 600) lañu. Ñoo dénkoo woon dénkaaney bérab bu sell bi.

Mboolem ña ñu limal Leween ñi, te Musaa ak Aaróona lim leen na ñu bokke seeni làng ci ndigalal Aji Sax ji, ñuy mboolem góor ñi am weer, jëm kaw, ñaar fukki junneek ñaar (22 000) lañu.

Ba ñu waññee mboolem taaw yu góor ya, bind seeni tur, dale ci ñi am weer, jëm kaw, seenub lim nekk na ñaar fukki junneek ñaar ak ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñett (22 273).

¶ Ñii nag lañu limal Leween ñi ak seeni làng: ñoom Gerson mi sos làngu Gersoneen ñi, ak ñoom Keyat mi sos làngu Keyateen ñi, ak ñoom Merari mi sos làngu Merareen ñi.

«Demal yéeneji lii, Yerusalem di dégg, nga ne: “Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngi fàttliku sa ngor ba ngay ndaw, ak sa cofeel ba nga deeb séet, ba ngay topp sama gannaaw ca màndiŋ ma, ba ngay jaare fa dara dul sax.