Réew ma sax mujj na daj ak sobe, ma wàcce mbugal ca kaw réew ma, ba mu gëq ay nitam.
TSK
TSK · Numbers 35:33
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Su dee dañoo fekk ku ñu bóom ci biir réew mi leen seen Yàlla Aji Sax ji moomale, mu tëdd ci àll bi, te xameesul ku ko rey,
Yal na deewug Abner këppu ci kaw boppu Yowab, mook waa kër baayam gépp. Yàlla bu waa kër Yowab ñàkk ku ànd ak jàngoroy xelli, mbaa jàngoroy der juy law, mbaa lafañ buy doxe yet, mbaa ku deeye xare, mbaa ku amul lu mu lekk.»
¶ Teewul Aji Sax ji dëppul ci meram mu réy mi mu dale ci kaw Yuda ndax mboolem li Manase def, ba merloo ko.
di tuur deretu ñu deful dara, te muy seen deretu doom yu góor ak yu jigéen ya ñu sarxalal tuuri Kanaaneen ña, deret ja sobeel réew ma,
Xamleen xéll rekk ne su ngeen ma reyee, bakkanu ku deful dara ngeen gàddu, yeen ak dëkk beek ñi ko dëkke, ndax ci lu wér Aji Sax jee ma yebal ci yeen, ngir ma yegge leen mboolem kàddu yii.»
Xanaa ay móolu aki wor, bóome, càcc ak njaaloo. Dañoo ràkkaaju, di tuur deret ci kaw deret.