TSK

TSK · Numbers 4:49

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Giirug Leween ñi nag ci bànni Israyil lañu bokk, waaye limaaleesu leen ak ñoom.

Leween ñi nag limaaleesu leen ci bànni Israyil, te noonu la ko Aji Sax ji sante woon Musaa.

¶ «Bu dal bi waree jóg, na Aaróona ak doomam yu góor muur yëf yu sell yi, ak mboolem jumtukaayi bérab bu sell bi ba noppi. Gannaaw loolu la askanu Keyat di dikk, ngir gàddu ko. Su ko defee duñu laal dara lu sell, bay dee. Loolu la Keyateen ñi di gàddu ci wàllu xaymab ndaje mi.

Gersoneen ñi nag, lii moo di seen cér ci wàllu liggéey bi, ak li ñu wara gàddu:

muy jën yi wër ëtt bi, ak seeni tegu ak seeni buum, mboolem seen jumtukaay yu ñu cay liggéeye. Limal-leen leen jumtukaay yi ñu wara gàddu.

Ñooñu lañu limal làngi Gersoneen ñi, te ñoom ñépp la liggéeyu xaymab ndaje mi war. Musaa ak Aaróona ñoo leen limoon ci ndigalal Aji Sax ji.

xelum Aji Sax ji tegu fi kawam, xelum rafet xalaat ak ràññee, xelum digle ak njàmbaar, xelum xam Aji Sax ji, ragal ko.

Yeen waa duni géej, dégluleen ma; yeen askan ya fu sore, teewluleen ma. Fa sama biiru ndey la ma Aji Sax ji wooye, moo tudd sama tur ba ma saa ndey juragul.